Nanga def xarit,
Lii mooy buntu këru jigéen ñi ci Lekeitio, Andraetxea.
Barab la bu jigéen ñi; déglu nu, xam nu, bokk jàng, may nu doole. Barab bu amul benn njaaxaanaay. Jumtukaay ngir mëna yegg ci Lekeitio feminist bu amul benn tàqalu góor wala jigéen, klaas, cosaan, at wala keneen.
Barab bii dafa yor boppam, moom boppam, wéeru nu ci kenn, am nanu sunu mbootaay. Danuy amaale jaaraleko ci sunuy àndadoo. Benn yoon ci at mi lañuy ndaje ngir jàngat ak jël dogal ci mébetu at mi ci topp.
Barab bi dafay ubbeeku ci Alarba ci ngoon jaaraleko ci ndaw yi. Ku nekk ci nun dafay nangu def ñaari turnu ci at mi, bokk ci ndaje at mi, te am nanu sañ-sañu jëfandikoo barab bi fépp fuñu ko mëna jëfandikoo.
Soo bëggee bokk ci kuréel gi, binndal bii kayit boole ci sa tur ak sa baay, nimero telefon ak sa e-mail.
Nanu def sunu granit ngir tabax Lekeitio bu gën ngir ñépp!
Ngir am ci yeneen leeral bind leen ci andraetxea@gmail.com